Babel

The Tower of Babel (Genesis 11: 1-9)

Wollof (Wolof)

Yàlla safaan na làkku àddina, mu jaxasoo

  1. Ci biir loolu nag waa àddina sépp a bokkoon wenn làkk, seeni wax di benn.
  2. Bi nit ñi toxoo, jëm penku, dañoo gis ag joor ci réewu Sineyaar, ñu sanc fa.
  3. Ñu ne: «Ayca, nu defar ay móol yu ñu lakk cib taal, ba mu ñor.» Noonu ñu def móol ya doji tabax, taqalee ko koltaar,
  4. daldi ne: «Ayca, nu tabax ab dëkk bu taax ma bëtt asamaan; kon dinanu am woy, te dunu tasaaroo ci kaw suuf.»
  5. Waaye Aji Sax ji wàcc, xoolsi dëkk bi ak taax, mi doom aadama yi tabax.
  6. Aji Sax ji da ne: «Su ñu tàmbalee nii, di menn mbooloo te bokk wenn làkk, kon dara dootu léen të.
  7. Ayca, nu wàcc, safaan seen làkk, ba dootuñu déggoo.»
  8. Ba loolu amee Aji Sax ji jële léen foofa, tasaare léen ci kaw suuf sépp, ñu yemale fa dëkk ba ñu doon tabax.
  9. Looloo tax ñu tudde dëkk ba Babel (mu firi Safaan), ndax foofa la Aji Sax ji safaane làkku àddina sépp, mu jaxasoo, te fa la léen tasaaree ci kaw suuf sépp.

Information about Wolof | Phrases | Numbers | Tower of Babel

Tower of Babel in Senegambian languages

Basari, Fula(ni), Wolof

Other Tower of Babel translations

By language | By language family

[top]


Green Web Hosting - Kualo

You can support this site by Buying Me A Coffee, and if you like what you see on this page, you can use the buttons below to share it with people you know.

 

Conversations - learn languages through stories

If you like this site and find it useful, you can support it by making a donation via PayPal or Patreon, or by contributing in other ways. Omniglot is how I make my living.

 

Note: all links on this site to Amazon.com, Amazon.co.uk and Amazon.fr are affiliate links. This means I earn a commission if you click on any of them and buy something. So by clicking on these links you can help to support this site.

[top]

iVisa.com